+ -

عن أَبِي حَازِمِ بْن دِينَارٍ:
أَنَّ رِجَالًا أَتَوْا سَهْلَ بْنَ سَعْدٍ السَّاعِدِيَّ، وَقَدِ امْتَرَوْا فِي الْمِنْبَرِ مِمَّ عُودُهُ، فَسَأَلُوهُ عَنْ ذَلِكَ، فَقَالَ: وَاللهِ إِنِّي لَأَعْرِفُ مِمَّا هُوَ، وَلَقَدْ رَأَيْتُهُ أَوَّلَ يَوْمٍ وُضِعَ، وَأَوَّلَ يَوْمٍ جَلَسَ عَلَيْهِ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، أَرْسَلَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِلَى فُلَانَةَ -امْرَأَةٍ من الأنصار قَدْ سَمَّاهَا سَهْلٌ-: «مُرِي غُلَامَكِ النَّجَّارَ أَنْ يَعْمَلَ لِي أَعْوَادًا أَجْلِسُ عَلَيْهِنَّ إِذَا كَلَّمْتُ النَّاسَ»، فَأَمَرَتْهُ فَعَمِلَهَا مِنْ طَرْفَاءِ الْغَابَةِ، ثُمَّ جَاءَ بِهَا، فَأَرْسَلَتْ إِلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَأَمَرَ بِهَا فَوُضِعَتْ هَاهُنَا، ثُمَّ رَأَيْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ صَلَّى عَلَيْهَا وَكَبَّرَ وَهُوَ عَلَيْهَا، ثُمَّ رَكَعَ وَهُوَ عَلَيْهَا، ثُمَّ نَزَلَ الْقَهْقَرَى، فَسَجَدَ فِي أَصْلِ الْمِنْبَرِ ثُمَّ عَادَ، فَلَمَّا فَرَغَ أَقْبَلَ عَلَى النَّاسِ فَقَالَ: «أَيُّهَا النَّاسُ، إِنَّمَا صَنَعْتُ هَذَا لِتَأْتَمُّوا وَلِتَعَلَّمُوا صَلَاتِي».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 917]
المزيــد ...

Jële nañu ci Aasim Ibn Diinaar mu wax ne:
Ay nit dañoo ñëw ci Sahl Ibn Sahdin As-Saahidii, fekk dañu doon werante ci minbar bi fan la bant bi jóge, ñu laaj ko loolu, mu ne leen: giñ naa ci Yàlla dinaa xam fan la jóge, ca bis bañu ko fi njëkkee teg laa ko gis, ak bis ba ca Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- njëkkee toog, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa yónnee ca diw -genn jigéen gu bokk ci Lansaar yi Sahl tudd na ko- ne ko: "digalal sa xaleb minise bi mu defaral ma ay bant yu may toog bu may wax ak nit ñi" mu digal ko ko, mu defar ko ci bant yi ci àll bi, mu indi ko, jigéen gi yónnee ko ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu digle ñu teg ko fii, ma gis Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di julli di kàbbar fekk ma nga ca kawam, mu wàcc di dellu ginnaaw, ba noppi daal di sujjóot, ci suufu minbar bi, daal di delluwaat, ba mu noppee, mu jublu ci nit ñi daal di leeni wax ne: "yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli".

-

Leeral

Ay nit dañoo ñëw ci kenn ci Sahaaba yi di ko laaj ci minbar bi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wut ci lan lañu ko defare? Fekk dañu si doon werente di xëccoo ci loolu, mu wax leen ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa yónnee ci genn jigéen ci waa Lansaar gu amoon ab jaamu minise, mu ne ko: digalal sa xale bi mu defaral ma ab minbar bu may toog bu may wax ak nit ñi, jigéen gi wuyu ko ci loolu, daal di digal xaleem bi mu defaral Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ab minbar ci garabu tamareks, bamu noppee jigéen gi yónnee ko Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu digle ñu teg ko ca bérab ba mu nekk ca jàkka ja, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di julli, kabbar fekk ma nga ca kawam, rukkoo ca kawam, mu wàcc di deeltu ginnaaw, ci lu dul muy wëlbati kanamam jëme ci ginnaaw, mu sujjóot ci suufu minbar bi, daal di delluwaat, ba mu noppee ca julli ga daal di jublu nit ñi, ne leen: yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ci man jàngaale samag julli.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sopp nañu wut minbar xutbakat bi yéeg ci, njariñam mooy jotal ak dégtal.
  2. Dagan na ñu julli ci kaw minbar ngir jàngale, dagan na ci imaam bi mu gën a kawe maamuun yi ngir aajo.
  3. Dagan na ñu dimbalikoo liggéey-kat yi ci aajoy jullit ñi.
  4. Yëngatu gu ndaw ci julli ngir aajo loolu dagan na.
  5. Dagan na maamuun bi xool imaamam ci julli gi; ngir jàng ci moom te loolu du wuute ak toroxlu.