+ -

عن حُذَيْفَةَ رضي الله عنه:
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَقُولُ بَيْنَ السَّجْدَتَيْنِ: «رَبِّ اغْفِرْ لِي، رَبِّ اغْفِرْ لِي».

[صحيح] - [رواه أبو داود والنسائي وابن ماجه وأحمد] - [سنن ابن ماجه: 897]
المزيــد ...

Jële nañu ci Husayfata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii».

-

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan toog ci diggante ñaari sujjóot yi da daan wax: Rabbi ixfir lii, Rabbi ixfir lii, di ko baamtu.
Maanaam Rabbi ixfir lii mooy: jaam bi sàkku ci Boroomam mu faral ko ay bàkkaaram te suturaal ko ay ayibam.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yoonal nañu ñaan ci diggante ñaari sujjóot yi ci jullig farata ak naafila.
  2. Sopp nañu di baamtu wax jii: Rabbi ixfir lii, benn yoon bi moom dafa war.