+ -

عن أَبي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه:
أنه كَانَ يُكَبِّرُ فِي كُلِّ صَلَاةٍ مِنَ الْمَكْتُوبَةِ وَغَيْرِهَا، فِي رَمَضَانَ وَغَيْرِهِ، فَيُكَبِّرُ حِينَ يَقُومُ، ثُمَّ يُكَبِّرُ حِينَ يَرْكَعُ، ثُمَّ يَقُولُ: سَمِعَ اللهُ لِمَنْ حَمِدَهُ، ثُمَّ يَقُولُ: رَبَّنَا وَلَكَ الْحَمْدُ، قَبْلَ أَنْ يَسْجُدَ، ثُمَّ يَقُولُ: اللهُ أَكْبَرُ حِينَ يَهْوِي سَاجِدًا، ثُمَّ يُكَبِّرُ حِينَ يَرْفَعُ رَأْسَهُ مِنَ السُّجُودِ، ثُمَّ يُكَبِّرُ حِينَ يَسْجُدُ، ثُمَّ يُكَبِّرُ حِينَ يَرْفَعُ رَأْسَهُ مِنَ السُّجُودِ، ثُمَّ يُكَبِّرُ حِينَ يَقُومُ مِنَ الْجُلُوسِ فِي الِاثْنَتَيْنِ، وَيَفْعَلُ ذَلِكَ فِي كُلِّ رَكْعَةٍ، حَتَّى يَفْرُغَ مِنَ الصَّلَاةِ، ثُمَّ يَقُولُ حِينَ يَنْصَرِفُ: وَالَّذِي نَفْسِي بِيَدِهِ، إِنِّي لَأَقْرَبُكُمْ شَبَهًا بِصَلَاةِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، إِنْ كَانَتْ هَذِهِ لَصَلَاتَهُ حَتَّى فَارَقَ الدُّنْيَا.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 803]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne:
Moom daana kàbbar ci bépp jullig farata ak bu dul moom, ci koor ak bu dul koor, bu dee jug kàbbar, bu dee rukoo kàbbar, daal di wax: samihal Laahu liman hamidahu, daal di wax it: Rabbanaa wa lakal hamdu, bala moo sujjóot, bu dee rot jëm ci sujjóot ba daal di kàbbar, buy yëkkati boppam ci sujjóot daal di kàbbar, bu dee jug ci toogaayu ñaari ràkka yi daal di kàbbar, loolu lay def ci ràkka yépp, ba julli gi jeex, ba mu wëlbatikoo daal di wax ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, maa leen gën a niroole jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax nii la daan jullee ba ni mu tàqalikoo ak àdduna.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 803]

Leeral

Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day nettali lenn ci jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu xamle ne bu daan jug jëm ci julli gi, day kàbbar bu taxawee di armal, bu jëmee ca rukoo ba it day kàbbar ak bu dee sujjóot, ak buy yëkkati boppam ci sujjóot, ak bu dee sujjóot ñaareelu sujjóot bi, ak buy yëkkati boppam bawoo ca sujjóot ba, ak buy jóge ci ñaari ràkka yu njëkk yi ginnaaw bamu toogee ngir taaya bu njëkk bi ci jullig ñatt mbaa ñenti ràkka, loolu lay def ci julli gi yépp bamu jeex, bu daan yëkkati ndingam jóge ca rukoo ba day wax: samihal Laahu liman hamidahu, topp mu wax fekk ma nga taxaw: Rabbanaa lakal hamdu.
Bi Abuu Hurayrata wëlbatikoo ca julli daal di wa ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, man de maa leen gën a niroole jullig Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ndax nii la daan jullee ba ni mu tàqalikoo ak àdduna.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dañuy kàbbar ci bépp sëgg ak siggi lu dul bu ñuy siggi ci rukoo bi dañuy wax samihal Laahu liman hamidahu.
  2. Xérug Sahaaba yi ci roy ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak wattu sunnaam si.