عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«خَيْرُ صُفُوفِ الرِّجَالِ أَوَّلُهَا، وَشَرُّهَا آخِرُهَا، وَخَيْرُ صُفُوفِ النِّسَاءِ آخِرُهَا، وَشَرُّهَا أَوَّلُهَا».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 440]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne :Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«sàppey góor ñi gi ci gën mooy gu
njëkk gi, bi ci yées mooy gu mujj gi, sàppey jigéen ñi gi ci gën mooy gu mujj gi, gi ci yées mooy gu njëkk gi».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 440]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamale ne sàppey góor yi gën ci julli te ëpp ci yool ak ngëneel mooy gu njëkk gi; ngir li ñu jege imaam bi ak di dégg jàngam mi ak li ñu sori jigéen ñi. Ba ca yées te gën ca a néewub yool ag ngëneel te gën ca a sori càkkuteefu Sariiha mooy ga ca mujj, Sàppey jigéen ñi ga ca gën mooy gu mujj ga; ndax moo leen gën a suturaal, moo gën a sori ci jaxasoo ak góor ñi, ak gis leen, ak fitnawu ci ñoom, ga ca yées mooy gu njëkk ga; ngir li mu jege góor ñi ak gaarlu ci fitna.