عن أبي هريرة رضي الله عنه عن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ كَانَ يُؤْمِنُ بِاللهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ فَلْيَقُلْ خَيْرًا أَوْ لِيَصْمُتْ، وَمَنْ كَانَ يُؤْمِنُ بِاللهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ فَلْيُكْرِمْ جَارَهُ، وَمَنْ كَانَ يُؤْمِنُ بِاللهِ وَالْيَوْمِ الْآخِرِ فَلْيُكْرِمْ ضَيْفَهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 47]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral dëkkandoom, képp ku gëm Yàlla ak bis-pénc nay teral ganam».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 47]
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne jaam bi gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nga xam ne falay dellu ñu fay ko ay jëfam, ngëmam dana ko ñaax ci jikko yii:
Bu njëkk bi: wax ju rafet: ci sàbbaal, ak tudd Yàlla, di digle lu baax, di tere lu bon, di defar diggante nit ñi, bu ko deful it mu taqook noppi téye loram te sàmm làmmiñam.
Ñaareel bi: teral dëkkandoo: ci di rafetal jëme ci moom te bañ koo lor.
Ñatteel bi: teral gan gi ñëw ngir seetsi la: ci wax ju teey, ak jox ko ñam ak yu ni mel.