+ -

عن جرير بن عبد الله رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«مَنْ لَا يَرْحَمِ النَّاسَ لَا يَرْحَمْهُ اللهُ عَزَّ وَجَلَّ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2319]
المزيــد ...

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah Al-Xasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2319]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ki dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm, koon jaam bi di yërëm mbindeef yi daa bokk ci sabab yi gën a rëy yi nga xamne dees na ci ame yërmàndey Yàlla mu kawe mi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yërmànde ci mbooleem mbindéef loolu de luñu sàkku la, waaye dañoo tudd nit ngir fonk giñuleen fonk.
  2. Yàlla mooy Aji-Yërëme ji te mooy yërëm ay jaamam yiy yërëme, ndax pay moom ca kem jëf ja rekk.
  3. Yërëm nit ñi day làmboo di àggale ci ñoom baax di leen jeñal lu ñaaw tey jëflanteeg ñoom lu rafet.