عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«نِعْمَتَانِ مَغْبُونٌ فِيهِمَا كَثِيرٌ مِنَ النَّاسِ: الصِّحَّةُ وَالفَرَاغُ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6412]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"ñaari xéewal a ngi nii yoo xamne nit ñu bari woru na ñu ci: ag wér ak ug jot".
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6412]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ci ñaari xéewal yu màgg yu mu xéewale doomu Aadama , te ñu bari ci ñoom da ñu koy jëfandikoo ci ludul noonu ; nit ki bu ag wér ak ug jot dajee ci moom mu tàyyeel ba toppul Yàlla kooku mooy ki sooy te lu li ëpp ci nit ñi nii lii mooy seen mbir, waaye bu defoon jotam gi ak wéram gi ci topp Yàlla kon di na tonuwu; ndaxte àdduna mooy toolu allaaxira, te ci àdduna la ñuy liggéeyalee allaaxira , jot nag ñàkk jot moo ciy topp, ag wér tawat moo koy wuutu, bu doon ag màggat kese sax kon mu doy.