عَنْ أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رضي الله عنه قَالَ:
سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ: «قَالَ اللَّهُ تَبَارَكَ وَتَعَالَى: يَا ابْنَ آدَمَ إِنَّكَ مَا دَعَوْتَنِي وَرَجَوْتَنِي غَفَرْتُ لَكَ عَلَى مَا كَانَ فِيكَ وَلاَ أُبَالِي، يَا ابْنَ آدَمَ لَوْ بَلَغَتْ ذُنُوبُكَ عَنَانَ السَّمَاءِ ثُمَّ اسْتَغْفَرْتَنِي غَفَرْتُ لَكَ، وَلاَ أُبَالِي، يَا ابْنَ آدَمَ إِنَّكَ لَوْ أَتَيْتَنِي بِقُرَابِ الأَرْضِ خَطَايَا ثُمَّ لَقِيتَنِي لاَ تُشْرِكُ بِي شَيْئًا لأَتَيْتُكَ بِقُرَابِهَا مَغْفِرَةً».
[حسن] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 3540]
المزيــد ...
Jële nañu ci Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Dégg naa Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Yàlla mu baarkeel mi te kawe nee na: éey yaw doomu Aadama ji boo ma ñaanee yaakaar ma ma jéggal la ak lu man a nekk ci yaw te duma faale, yaw doomu Aadama say bàkkaar bu eggoon ca niiri asamaan si nga jéggalu ma kon dinaa la jéggal te duma faale dara, yaw doomu Aadama boo ma indiloon luy jege suuf si ci bàkkaar yu bari, nga daje ak man te bokkaalewóo ma ak dara dinaa la indil njéggal lu toll ni moom".
[Tane na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3540]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Yàlla mu kawe mi dafa wax ci hadiis bu sell ne: yaw doomu Aadama ji fii ak yaa ngi may ñaan di yaakaar sama yërmànde, te naaguwóo; dinaa suturaal say bàkkaar far ko te duma faale dara, donte bàkkaar bi ak moy gi dafa bokk ci yu mag yi. Yaw doomu Aadama: bu say bàkkaar bari woon lool bay fees diggante asamaan ak suuf ba egg ci wàllam matale ay peggam, topp nga jéggalu ma; dinaa far say bàkkaar jéggal la ko te duma faale bariwaay gi.
Yaw doomu Aadama: boo ma indiloon ginnaaw dee ay bàkkaar ak i moy yu fees suuf si, fekk dangaa dee ci kennal Yàlla te bokkaalewóo ma ak dara; di naa wottee ak bàkkaar yooyu ak moy yi ag njéggal gu fees suuf si; ndaxte man ku yaatug njéggal laa, te damay jéggale bàkkaar yépp ba mu des bokkaale.