عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه:
أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَقُولُ فِي سُجُودِهِ: «اللهُمَّ اغْفِرْ لِي ذَنْبِي كُلَّهُ دِقَّهُ، وَجِلَّهُ، وَأَوَّلَهُ وَآخِرَهُ وَعَلَانِيَتَهُ وَسِرَّهُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 483]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax ci sujjóotam: "Allaahuma ixfir lii sanbii kullahu, diqahu, wa jillahu, wa awwalahu wa aaxirahu, wa halaaniyatahu wa sirrahu".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 483]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na ñaan ci sujjóotam di wax: Yaw sama Boroom jéggal ma samay bàkkaar ci suturaal ma ko, fegal ma la cay topp; nga jéggal ma baal ma yu ndaw yi mu tuuti mbaa mu bari, bàkkaar yu njëkk ya ak yu mujj ya ak li nekk seen diggante, ak yu fés ya ak yu làqu ya ya nga xam ne kenn xamu ko ku dul yaw Yàlla mu sell mi.