عَنْ أَنَسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ:
أَنَّ رَجُلًا سَأَلَ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَنِ السَّاعَةِ، فَقَالَ: مَتَى السَّاعَةُ؟ قَالَ: «وَمَاذَا أَعْدَدْتَ لَهَا». قَالَ: لاَ شَيْءَ، إِلَّا أَنِّي أُحِبُّ اللَّهَ وَرَسُولَهُ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: «أَنْتَ مَعَ مَنْ أَحْبَبْتَ». قَالَ أَنَسٌ: فَمَا فَرِحْنَا بِشَيْءٍ، فَرِحْنَا بِقَوْلِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَنْتَ مَعَ مَنْ أَحْبَبْتَ» قَالَ أَنَسٌ: فَأَنَا أُحِبُّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَأَبَا بَكْرٍ، وَعُمَرَ، وَأَرْجُو أَنْ أَكُونَ مَعَهُمْ بِحُبِّي إِيَّاهُمْ، وَإِنْ لَمْ أَعْمَلْ بِمِثْلِ أَعْمَالِهِمْ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3688]
المزيــد ...
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal". Mu ne ko: du dara, lu dul ne bëgg naa Yàlla ak ub yonnenteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu ne ko: "ki nga bëgg ngay nekkal". Anas nee na: masuñoo bég ci dara kem ni ñu bége ci li Yonnente bi wax ne: "ki nga bëgg ngay nekkal" Anas wax ne: man bëgg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak Abuu Bakrin ak Umar, te maa ngi am yaakaar a nekk ak ñoom ndax li ma leen bëgg, donte
jëfuma lu tolni
seen jëf ya.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3688]
Benn kaw-kaw bu dëkk ca àll ba dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: waxtu wi saa di taxaw?
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ana lan nga ko waajalal ci jëf yu baax?
Aji-laaj ji ne ko: waajalaluma ko ci ay jëf yu màgg de waaye damaa bëgg Yàlla ak ub yonnenteem, te tuddul leneen ci jëfi xol yi ak yu yaram yi ak yu alal yi; ndaxte yooyu yépp ay bànqaas la ci bëgg gi te ca lay tege, ndaxte bëgg gu dëggu day waral pasteefu ci jëf yu
baax yi.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ki nga bëgg ngay nekkal ca àjjana.
Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di bég ci bégale googu mbégte mu tar.
Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm xibaare ne moom dafa bëgg Yonnente bi ak Abuu Bakrin ak Umar, muy yaakaar a nekk ak ñoom donte ay jëfam melul ni seen i jëf