عَنْ سُلَيْمَانَ بْنِ صُرَدٍ رضي الله عنه قَالَ:
كُنْتُ جَالِسًا مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَرَجُلاَنِ يَسْتَبَّانِ، فَأَحَدُهُمَا احْمَرَّ وَجْهُهُ، وَانْتَفَخَتْ أَوْدَاجُهُ، فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «إِنِّي لَأَعْلَمُ كَلِمَةً لَوْ قَالَهَا ذَهَبَ عَنْهُ مَا يَجِدُ، لَوْ قَالَ: أَعُوذُ بِاللَّهِ مِنَ الشَّيْطَانِ، ذَهَبَ عَنْهُ مَا يَجِدُ» فَقَالُوا لَهُ: إِنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ: «تَعَوَّذْ بِاللَّهِ مِنَ الشَّيْطَانِ»، فَقَالَ: وَهَلْ بِي جُنُونٌ؟
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3282]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sulaymaan ibn Surad yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Damaa toogoon ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaari waay di saagaante, kenn ki kanamam gi xoq, ay séditi baatam jug, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: "man de xam naa baat boo xam ne bu ko waxoon li muy yég dem, bu waxoon: ahuusu bil Laahi minas Saytaani, kon li muy yég dem" ñu ne ko: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "nga muslu ci Yàlla ci Saytaane", mu ne: ndax damaa ameg ndof?
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3282]
Ñaari waay dañoo ŋàññante saagaante ci kanamu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, kanamu kenn ki daal di xoq, ay séditam yi wër doqam gi jug.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: man de xam naa baat boo xam ne aji-mer jii bu ko waxoon kon meram mi dana dem, bu waxoon: ahuusu bil Laahi minas Saytaani Arrajiimi.
Ñu ne ko: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: nga muslu ci Yàlla ci Saytaane.
Mu ne: ndax damaa dof man?! Mu njort ne kenn du muslu ci Saytaane lu dul ku ameg ndof.