عَنْ أَبِي الدَّرْدَاءِ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَلاَ أُنَبِّئُكُمْ بِخَيْرِ أَعْمَالِكُمْ، وَأَزْكَاهَا عِنْدَ مَلِيكِكُمْ، وَأَرْفَعِهَا فِي دَرَجَاتِكُمْ وَخَيْرٌ لَكُمْ مِنْ إِنْفَاقِ الذَّهَبِ وَالوَرِقِ، وَخَيْرٌ لَكُمْ مِنْ أَنْ تَلْقَوْا عَدُوَّكُمْ فَتَضْرِبُوا أَعْنَاقَهُمْ وَيَضْرِبُوا أَعْنَاقَكُمْ؟» قَالُوا: بَلَى. قَالَ: «ذِكْرُ اللهِ تَعَالَى».
[صحيح] - [رواه الترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 3377]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu dardaa -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ndax du ma leen tegtal li gën ci seen jëf yi, te gën cee sell fa seen Boroom, te gën cee kawe ci seeni daraja te gën ci yéen wurus ak xaalis, te gën ci yéen ngeeni daje ak séeni noon ngeen di dóor seen doq ya, ñoom ñuy dóor seen doq yi?" Ñi ne ko ahakay. Mu ne: "tudd Yàlla mu kawe mi".
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3377]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Sahaaba yi: .
Ndax bëgg ngeen ma xibaar leen xamal leen jëf ju gën te gën a tedd gën a bari, gën a laab te gën a sell fa Yàlla seen Boroom bu màgg bi? .
Te gën a kawe daraja ca àjjana?
Te gën ci yeen saraxe wurus ak xaalis?
Te gën ci yéen ngeen daje ak yéefar yi ngir xeex, ngeen di dóor seen doq ya, ñoom ñuy dóor seen doq yi?
Sahaaba yi ne ko: waawaaw bëgg nanu looli kay.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: tudd Yàlla mu kawe mi ci waxtu wu ne ak ci bépp anam ak bépp melo.