+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا تَصْحَبُ الْمَلَائِكَةُ رُفْقَةً فِيهَا كَلْبٌ وَلَا جَرَسٌ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2113]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«malaaka yi duñu ànd ci mbooloo mu ànd akub xaj walla ab jóolooli.

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2113]

Leeral

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ne malaaka yi duñu ànd ci tukki boo xam ne ab xaj da caa ànd, walla ab jóolooli li gu ñu lonk ci daaba yi bu yëngatoo di génne kàddu.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tere nañu yar xaj ak di ànd ak moom, danañu settee ci tere gi xaj buy rëbb ak buy wattu (garde).
  2. Malaaka yidul ànd ca loola mooy malaakay yërmànde,bu dee malaaka yiy wattu nit ki ñoom moom duñu teqalikoo ak jaam ñi ci seen ug toog ak ci seen ug tukki.
  3. tere nañu ag kalaksone; Ndax benn la ci mbiibi Seytaane yi, te dafay niróo ak kolos yu nasaraan yi.
  4. War na ci jullit bi mu xér ci sori lépp luy tax malaaka yi sori ko.