عَنْ أَبِي طَلْحَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لاَ تَدْخُلُ المَلاَئِكَةُ بَيْتًا فِيهِ كَلْبٌ وَلاَ صُورَةٌ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3322]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Talhata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«malaaka yi duñu dugg kër gu am xaj walla nataal».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3322]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne malaakay yërmànde duñu dugg kër gu am xaj walla nataalu yi am ruuh; Ndaxte naataal lu am ruuh: ag moy la te ñaawteef la, te toppandoo bindubYàlla bi la, te jumtukaay la ci jumtukaayi bokkaale yi, te yenn yi nataalu lu ñuy jaamu la wolif Yàlla, Li tax duñu dugg ci kër gu am xaj: ndaxte dañoo bari lu ñuy lekk sobe, te yenn yi dañu koy tudde Saytaane; te malaaka yi dañoo safaanoo ak saytaane yi, Ak ni xetu xaj bone; te malaaka dafa bañ xet gu bon, ak it ne dañoo tere ku ko yar; nu mbugale ko ci xañ ko malaakay yërmànde bañ a dugg këram, bañ a jokkoo ak moom, ak bañ koo jéggalul, bañ ko a baarkeelal ci këram, ak bañ koo jeñal saytaane.