عن أبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا يَحِلُّ لِامْرَأَةٍ مُسْلِمَةٍ تُسَافِرُ مَسِيرَةَ لَيْلَةٍ إِلَّا وَمَعَهَا رَجُلٌ ذُو حُرْمَةٍ مِنْهَا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1339]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«daganul ci jullit bu jigéen muy tukki lu toll ni doxug guddi lu dul dafa ànd ak góor gu ko araama takk (koc-armalam)».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1339]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ne araam na ci jullit bu jigéen bi muy tukki luy toll ni doxug guddi lu dul mu ànd ak góor gu bokk ci koj-armalam.