عَنِ ابْنِ عُمَرَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا قَالَ:
فَرَضَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ زَكَاةَ الفِطْرِ صَاعًا مِنْ تَمْرٍ، أَوْ صَاعًا مِنْ شَعِيرٍ، عَلَى العَبْدِ وَالحُرِّ، وَالذَّكَرِ وَالأُنْثَى، وَالصَّغِيرِ وَالكَبِيرِ مِنَ المُسْلِمِينَ، وَأَمَرَ بِهَا أَنْ تُؤَدَّى قَبْلَ خُرُوجِ النَّاسِ إِلَى الصَّلاَةِ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1503]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum Koor, Saah ci tàndarma, walla Saah ci pepp, ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi, mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1503]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc waral na asakay muurum koor ginnaaw weeru koor, te mooy luy tolloo ak Saah muy tollook ñenti Mudd. Mudd mooy: lu fees ñaari loxoy góor gu diggudóomu, ci tàndarma walla pepp ci bépp jullit; gor ak jaam, góor ak jigéen, xale ak mag, loolu ci ku am lu des ci dundu bisam ak guddeem, ci boppam ak ki muy dundal. Mu digle ñu joxe ko laata nit ñi di génn jëm ca julli ga.