Toftaleg Adiis yi

Daan nanu génne asakay muurum koor jamanoy yónente bi, ngir xale ak mag, gor ak jaam, muy Saah ci ñam, walla Saah ci soow mu ñu wayal, walla Saah ci Pepp, walla Saa, walla Saah ci tàndarma, walla Saah ci Raseen bu wow
عربي Àngale Urdu
Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum Koor, Saah ci tàndarma, walla Saah ci pepp, ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag ci jullit ñi, mu digle ñu joxe ko njëkk nit ñi di génn jëm ca julli ga
عربي Àngale Urdu