عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المُؤْمِنِينَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا أَنَّهَا قَالَتْ:
يَا رَسُولَ اللَّهِ، نَرَى الجِهَادَ أَفْضَلَ العَمَلِ، أَفَلاَ نُجَاهِدُ؟ قَالَ: «لَا، لَكُنَّ أَفْضَلُ الجِهَادِ: حَجٌّ مَبْرُورٌ».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 1520]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yaw Yonnente Yàlla bi, gis nanu ne jihaad moo gën ci jëf yi, mo ndax dunu jihaadi? Mu wax ne: "déedéet, waaye jihaad ji gën mooy: aj gu baax".
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1520]
Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- dañoo gisoon ne jihaad ci yoonu Yàlla ak xeex ak noon yi moo gën ci jëf yi, Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- daldi laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax ñoom jigéen ñi ñu jihaadi?
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- gindi leen ci jihaad gi gën ci seen àq te mooy aj gu baax gu dëppoo ak Alxuraan ak Sunna, gu mucc ci bàkkaar ak ngistal.