عَنِ العَبَّاسِ بْنِ عَبْدِ الْمُطَّلِبِ رَضيَ اللهُ عنهُ قَالَ:
قُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ، عَلِّمْنِي شَيْئًا أَسْأَلُهُ اللَّهَ عَزَّ وَجَلَّ. قَالَ: «سَلِ اللَّهَ العَافِيَةَ»، فَمَكَثْتُ أَيَّامًا ثُمَّ جِئْتُ فَقُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ، عَلِّمْنِي شَيْئًا أَسْأَلُهُ اللَّهَ. فَقَالَ لِي: «يَا عَبَّاسُ، يَا عَمَّ رَسُولِ اللهِ، سَلِ اللَّهَ العَافِيَةَ فِي الدُّنْيَا وَالآخِرَةِ».
[صحيح لغيره] - [رواه الترمذي وأحمد] - [سنن الترمذي: 3514]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abbaas ibn Abdul Muttalib yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Damaa wax ne: yaw Yonnente Yàlla bi, xamal ma lu may ñaan Yàlla mu màgg mi. Mu ne ma: "ñaanal jàmm", ma toog ay bis daal di ñëwaat ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi xamal ma lu may ñaan Yàlla. Mu ne ma:"yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmmi àdduna ak allaaxira".
[Wér na ngir beneen Adiis bu koy tegtale] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3514]
Baay taxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc Abbaas ibn Abdul Muttalib yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa sàkku ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu xamal ko ag ñaan gu muy ñaan Yàlla, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xamal ko ne na ñaan Yàlla jàmm ak mucc ci ayib yi ci diine ak ci àdduna ak allaaxira, Abbaas nee na: ginnaaw ay bis ma dellusi fi moom Yonnente bi beneen yoon, ne ko: mu xamal ma ag ñaan gu may ñaan Yàlla, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: yaw Abbaas, yaw baay taxu Yonnente Yàlla bi, ñaanal Yàlla jàmm ngir jeñ jépp lor ak xëcci wépp yiw ak njariñ ci àdduna ak allaaxira.