+ -

عَنْ عُمَرَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ:
أَنَّهُ جَاءَ إِلَى الحَجَرِ الأَسْوَدِ فَقَبَّلَهُ، فَقَالَ: إِنِّي أَعْلَمُ أَنَّكَ حَجَرٌ، لاَ تَضُرُّ وَلاَ تَنْفَعُ، وَلَوْلاَ أَنِّي رَأَيْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يُقَبِّلُكَ مَا قَبَّلْتُكَ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1597]
المزيــد ...

Jële nañu ci Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm:
Mu ñëw ci Hajarul Aswad daal di koy fóon, daal di wax ne: man de xam naa ne yaw aw xeer nga, doo lor te doo jariñ, bu dul woon ne gisnaa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di la fóon kon duma la fóon.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1597]

Leeral

Njiitu jullit ñi Umar ibnul Xattaab yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa ñëw ci Hajarul Aswad ci pengu Kaaba gi fóon ko, daal di wax ne: man de xam naa ne yaw aw xeer nga, doo lor te doo jariñ, bu dul woon ne gisnaa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc fóon la kon duma la fóon.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yoonal nañu fóon Hajarul Aswad ñeel ñiy wër kaaba gi bu ñu tolloo ak moom, bu dee man na a nekk ci lu yomb.
  2. Li ñu jublu ci fóon Hajarul Aswad, mooy roy Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
  3. An-Nawawii nee na: maanaam mooy ne manuta jariñ manuta lor, waaye aw xeer la wu ñu bind kem mbooleem mbindeef yi nga xam ne du lor te du jariñ, Umar dafa fésal lii ci xew u aj gi; ngir ñu seede ko ci réew yi, ñëpp jàpp loo lu .
  4. Jaamu yi lu ñuy taxawlu la; deesu ci yoonal lu dul lu Yàlla yoonal ak ub yonenteem.
  5. Bu ag jaamu wéree dañu koy jëfe donte xamuñu lu tax; ndaxte jëfe gi nit ñi di jëfe ndigal ak def gi ñu koy def dafa bokk ci li Yàlla bëgg ci ñoom.
  6. Tere nañu fóon lu sariiha joxewul ndigal ngir ñu fóon ko ci anamug jaamu muy xeer ak lu dul moom.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi