Listu hadiis yi

Maa ngi leen di dénk ragal Yàlla, ak dégg ak topp, donte ab jaam moo leen jiite, képp ku dund ci yéen dana gis wuute gu bari, maa ngi leen di dénk sama sunna si ak sunnay njiit yu jub yi tey jubal
عربي الإنجليزية الأوردية
seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit
عربي الإنجليزية الأوردية
dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal
عربي الإنجليزية الأوردية
Mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ci waa Ansaar yi ne: "kénn du leen bëgg ku dul way-gëm, te kenn du leen bañ ku dul ab naaféq, ku leen bëgg Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko
عربي الإنجليزية الأوردية
dinaa jox Raaya ji waa ju bëgg Yàlla ak ub yonnenteem, Yàlla dina ko ubbee ci ay loxoom
عربي الإنجليزية الأوردية
demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk
عربي الإنجليزية الأوردية
man de xam naa ne yaw aw xeer nga, doo lor te doo jariñ, bu dul woon ne gisnaa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di la fóon kon duma la fóon
عربي الإنجليزية الأوردية
ñi gën ci yéen ñooy samag maas, topp ci ña ca topp, topp ci ña ca topp'
عربي الإنجليزية الإندونيسية