عَنِ الْبَرَاءِ رضي الله عنه:
عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنَّهُ قَالَ فِي الْأَنْصَارِ: «لَا يُحِبُّهُمْ إِلَّا مُؤْمِنٌ، وَلَا يُبْغِضُهُمْ إِلَّا مُنَافِقٌ، مَنْ أَحَبَّهُمْ أَحَبَّهُ اللهُ وَمَنْ أَبْغَضَهُمْ أَبْغَضَهُ اللهُ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 75]
المزيــد ...
Jële nañu ci Al-Baraa -yal na ko Yàlla dollee gërëm-:
Mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ci waa Ansaar yi ne: "kénn du leen bëgg ku dul way-gëm, te kenn du leen bañ ku dul ab naaféq, ku leen bëgg Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 75]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bëgg Ansaar yi di waa Madina, màndarga la ci ngëm gu mat; ngir li ñu jiitu ci dimbali Lislaam ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak dox ci yiir jullit ni, ak joxe seen alal ak seen bakkan ci yoonu Yàlla, kon bañ leen màndargay naaféq la. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral ne ku bëgg Ansaar yi Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko.