عَن زَيْدِ بْنِ خَالِدٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ جَهَّزَ غَازِيًا فِي سَبِيلِ اللَّهِ فَقَدْ غَزَا، وَمَنْ خَلَفَ غَازِيًا فِي سَبِيلِ اللَّهِ بِخَيْرٍ فَقَدْ غَزَا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2843]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sayd ibn Xaalid yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla kooku xare na, ku wuutu aji-xare ci yoonu Yàlla ci yiw kooku xare na".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2843]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ku waajalal aji-xare ci yoonu Yàlla jumtukaayi tukkeem ak yi mu aajowoo ci ay ngànnaay yu manut a ñàkk, ak waruwaay, ak ñam, ak ub dund ak yeneen; kooku àtteb aji-xare ji la am, te dina am yoolub way-xare yi.
Ku wuutu aji-xare ci ay mbiram ci yiw, wuutu ko ci di sàmm njabootam ci jamono yi mu fàddoo kooku àtteb aji-xare ji la am.