+ -

عَنْ أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا عَدْوَى، وَلَا طِيَرَةَ، وَيُعْجِبُنِي الْفَأْلُ» قَالَ قِيلَ: وَمَا الْفَأْلُ؟ قَالَ: «الْكَلِمَةُ الطَّيِّبَةُ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2224]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:
«wàlle amul, gaafal amul, gaatnga lu baax nag yéem na ma» nee na, ñu ne ko: lan mooy gaatnga lu baax ? Mu ne: "wax ju teey".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2224]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne wàlle gi ceddo ya gëmoon ci ne feebar bi day toxal boppam jëm ci keneen ci lu dul dogalub Yàlla loolu ag neen la, Gaafal itam ag neen la, te mooy ñaawal ci lu mu man a doon moo xam lu ñuy dégg la walla lu ñuy gis,ci ay picci walla ay rab walla ñi ame laago walla ay limat (numéro) walla ay bis mbaa lu dul loolu, Dafa tudd piccinag ndaxte moo siiwoon fa Ceddo ga, te cosaanam mooy naawal am picci booy tàmbalee jëf,tukki walla yaxantu mbaa leneen,bu naawee ci wetug ndayjoor mu gaatnga lu rafet daal di def la mu bëgg,bu jëmee wetug càmmooñ mu gaaflu ko daal di bàyyi la mu bëggoon. Topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne rafetlu yéem na ko, te mooy liy xew ci nit ki ci mbégte ak kontaante ci wax ju teey ju muy dégg, ba tax muy rafet njort ci Boroomam.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Wakkirlu ci Yàlla mu kawe mi,ak ne kenn du indi aw yiw ku dul Yàlla,kenn it du jeñ aw lor ku dul Yàlla.
  2. Tere nañu gaafal, te mooy di ñaawal dara, ba muy teree
  3. def dara.
  4. Gaatnga lu baax nag bokkul ci gaafal gi ñiy tere,waaye moom dafa bokk ci rafet njort ci Yàlla mu kawe mi.
  5. Lépp lu mu man a doon ci dogalub Yàlla lay ame ak nattalleem moom dong amul bokkaale.