+ -

عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المؤمنين رضي الله عنها أَنَّ فَاطِمَةَ بِنْتَ أَبِي حُبَيْشٍ سَأَلَتِ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَتْ:
إِنِّي أُسْتَحَاضُ فَلاَ أَطْهُرُ، أَفَأَدَعُ الصَّلاَةَ؟ فَقَالَ: «لَا، إِنَّ ذَلِكِ عِرْقٌ، وَلَكِنْ دَعِي الصَّلاَةَ قَدْرَ الأَيَّامِ الَّتِي كُنْتِ تَحِيضِينَ فِيهَا، ثُمَّ اغْتَسِلِي وَصَلِّي».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 325]
المزيــد ...

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne Faatimata bintu Abii Jahsin dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko:
Man damay gis dereet ju yàqu te du ma set, ndax damay bàyyi julli? Mu ne ko: “Déedéet , loolu dereti sidit la, waaye bàyyil julli ci limu bis yi ngay gis mbaax, topp nga sangu te julli".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 325]

Leeral

Faatimata bintu Jahsin laaj na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: man daal deret ji du deñ ci man day wéy ba ci jamono yidul jamonoy mbaax, ndax àtteb loolu mooy àtteb mbaax ngir ma bàyyi julli? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: loolu deret ju yàqu la, te mooy dereti feebar, day ame ci dogug sédit ci butiti njurukaay, waaye du dereti mbaax, Waxtu wa nga daan gis mbaax bu ñëwee ci weer wa nga aadawoo lu njëkk ngay am feebaru deret ju dul dog, na nga bàyyi julli ak yeneen yi ñuy tere ku gis mbaax ci jamonoy mbaax ga. Bu limub diir booba jeexee, kon laab nga ci mbaax ga, na nga raxas barabu deret ja, daal di raxas sa yaram ci sangu gu matale ngir yëkkati am toj, te nga julli.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Jigéen gi dafa war a sangu bu bisi mbaaxam jeexee.
  2. Warug julli ci kiy gis deret ju yàqu.
  3. Mbaax: deret la juy génn ci butiitu njurukaay gi jaare ci pëyu jigéen ju mat, day ñëw ci moom ci bis yu ñu xam.
  4. Deret ju yàqu: sottikug deret ci lu dul waxtoom jóge ci suufu butiitu njurukaay bi te du jóge ci biiram.
  5. Liy teqale diggante dereti mbaax ak deret ju yàqu: dereti mbaax deret ju ñuul la te tal te xasaw ag xet, deret ju yàqu nag dafa xonxu te woyof te amul xet gu xasaw.