عن أُمِّ عَطِيَّةَ رَضي الله عنها، وكَانَتْ بايَعَت النبيَّ صلى الله عليه وسلم، قالت:
كُنَّا لا نَعُدّ الكُدرَةَ والصُّفْرَةَ بعدَ الطُّهرِ شيئًا.
[صحيح] - [رواه أبو داود بهذا اللفظ، ورواه البخاري بدون زيادة (بعد الطهر)] - [سنن أبي داود: 307]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ummu Atiyyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-,mu bokkoon ci ñi jaayante woon ak Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-,mu wax ne:
Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara.
[Wér na] - [Abóo Daawuda a ko soloo ci kàddu gii, Al-buxaariy soloo ko waliif ndollent (ginnaaw laab ga)] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 307]
Sahaaba bu jigéen bii di Ummu Atiyyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne jigéen ñi ci jamonoy Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawuñu jàppe mbaax ndox miy génne ci awra -xaw a ñuul, walla mboq-ginnaaw bimu laabe , ba tax duñu bàyyi julli ak woor ngir moom.