عَنْ عَائِشَةَ أُمِّ المُؤْمِنينَ رَضي الله عنها أَنَّهَا قَالَتْ:
إِنَّ أُمَّ حَبِيبَةَ بِنْتَ جَحْشٍ الَّتِي كَانَتْ تَحْتَ عَبْدِ الرَّحْمَنِ بْنِ عَوْفٍ شَكَتْ إِلَى رَسُولِ اللهِ صلى الله عليه وسلم الدَّمَ، فَقَالَ لَهَا: «امْكُثِي قَدْرَ مَا كَانَتْ تَحْبِسُكِ حَيْضَتُكِ، ثُمَّ اغْتَسِلِي». فَكَانَتْ تَغْتَسِلُ عِنْدَ كُلِّ صَلَاةٍ.
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 334]
المزيــد ...
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Ummu Habiibata bint Jahsin mi nekkoon ci soxnas Abdur Rahmaan ibn Awf dafa jàmbat Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dereet ju muy gis, mu ne ko: "toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu". Tax mu daan sangu ci julli gu nekk.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 334]
Kenn ci jigéen yi àndoon ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dereet ji dafa wéy di génn ci moom, Mu digal ko mu bañ a julli diir bi ko mbaaxam daan téye njëkk mbir mii di gaar, topp mu sangu daal di julli,moom nag mu daan ci coobarewu ñeel julli gu nekk.