عَنِ ابْنِ عُمَرَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لاَ يَنْظُرُ اللَّهُ إِلَى مَنْ جَرَّ ثَوْبَهُ خُيَلاَءَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5783]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:
"Yàlla du xool kuy diri ay yéreem ngir puukarewu".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5783]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na ci yoor ay yére walla koddaay ba ci suufu dojor yi ngir yéem ak rëy-rëylu, ak ne ku def loolu yayoo na tëkku gu tar gi ci ne Yàlla du ko xool ëllëg bis-pénc xoolu yërmànde.