عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لَا تَبْدَؤوا الْيَهُودَ وَلَا النَّصَارَى بِالسَّلَامِ، فَإِذَا لَقِيتُمْ أَحَدَهُمْ فِي طَرِيقٍ فَاضْطَرُّوهُ إِلَى أَضْيَقِهِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2167]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"buleen njëkka nuyu Yahuud yi ak Nasaraan yi ci nuyoog Salaam, bu ngéen dajee ak kenn ci ñoom ci yoon nangeen ko jaarloo fa gën a xat".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2167]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day tere jullit bi di njëkk a nuyu Yahuud bi ak Nasaraan bi donte dañoo bokk ci ña ñu kóllareenteel, kon yéefar bu dul ñoom safut a wax, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral ne bu nu dajee ak kenn ci ñoom ci yoon wi nanu ko loruloo ca yoon wa gën a xat, aji-gëm ji mooy dox ci diggu yoon wi, waaye yéefar bi mooy randu, jullit bi du doyadi ci genn anam ci anam i doyadi yi.