عن النعمان بن بَشِير رضي الله عنه قال: سمعت النبيَّ صلى الله عليه وسلم يقول:
«الدُّعَاءُ هُوَ الْعِبَادَةُ»، ثُمَّ قَرَأَ: «{وَقَالَ رَبُّكُمُ ادْعُونِي أَسْتَجِبْ لَكُمْ إِنَّ الَّذِينَ يَسْتَكْبِرُونَ عَنْ عِبَادَتِي سَيَدْخُلُونَ جَهَنَّمَ دَاخِرِينَ} [غافر: 60]».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن الترمذي: 3247]
المزيــد ...
Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ñaan mooy jaamu Yàlla» daal di jàng: "Aaya biy wax ne:
{séen Boroom nee na wooleen ma ma wuyu leen ñi may rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox} [ soratou Xaafiri: 60]».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3247]
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ñaan mooy jaamu Yàlla, kon li war mooy mu nekk lu sell ñeel Yàlla, moo xam wooteg laaj la walla wooteg sàkku, ci di laaj Yàlla mu kawe mi lu koy jariñ, ak jeñ lu koy lor ci àdduna ak allaaxira, walla muy wooteg jaamu, te mooy lépp lu Yàlla bëgg te gërëmloo ko ci ay wax ak i jëf yi feeñ ak yi nëbbu, jaamuy xol yi walla yu yaram yi mbaa yu alal yi
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tegtaloo na ci loolu ne: Yàlla wax na ne: {wooleen ma ma wuyu leen ñi ma rëy a ñaan danañu dugg Jahannama di way-torox}