عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه، عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَا جَلَسَ قَوْمٌ مَجْلِسًا لَمْ يَذْكُرُوا اللَّهَ فِيهِ وَلَمْ يُصَلُّوا عَلَى نَبِيِّهِمْ إِلاَّ كَانَ عَلَيْهِمْ تِرَةً، فَإِنْ شَاءَ عَذَّبَهُمْ وَإِنْ شَاءَ غَفَرَ لَهُمْ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي في الكبرى] - [سنن الترمذي: 3380]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"aw nit duñu toog ci ab jotaay te tudduñu fa Yàlla te julliwuñu ci seenub Yonnente lu dul ne dana nekk ag réccu ci seen kaw, bu ko soobee mu mbugal leen bu ko soobee mu jéggal leen".
[Wér na] - - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3380]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo càggante ci tudd Yàlla, ci ne aw nit duñu toog ci ab jotaay te tudduñu fa Yàlla mu kawe mi, te it julliwuñu ci Yonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc lu dul ne jotaay boobu dana nekk ci ñoom ag réccu ak ug ñàkk ak ug wàññeeku ëllëg bis-pénc, bu ko soobee mu mbugal leen ci seen bàkkaar ya jiitu ak seen ug gàtteñlu ga ca tege, bu ko soobee it mu jéggal leen ngir ngëneelam ak yërmàndeem.