+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه عن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«مَا نَقَصَتْ صَدَقَةٌ مِنْ مَالٍ، وَمَا زَادَ اللهُ عَبْدًا بِعَفْوٍ إِلَّا عِزًّا، وَمَا تَوَاضَعَ أَحَدٌ لِلهِ إِلَّا رَفَعَهُ اللهُ».

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2588]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«saraxe du wàññi alal, te Yàlla du dolli Jaam biy jéggale ludul ag màgg, te kenn du toroxlu ngir Yàlla lu dul ne broom bi dina ko Yëkkati».

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2588]

Leeral

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sarax du wàññi alal, waaye day fegal nit ki ay gàkk-gàkk, te Yàlla day wuutalal boroomam aw yiw wu màgg, loolu di ag dolliku waaye du ag wàññiku.
Jéggale te am kàttanu fayu du dolli boroom lu dul kàttan ak tedd nga.
Kenn du toroxlul Yàlla, ci lu dul mu ragal kenn mbaa muy laamisook kenn, walla muy sàkku ci moom njariñ, lu dul ne payam mooy ak yëkkatiku ak teraanga.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi:
  2. Yiw ak texe moo ngi ci topp Sariiha ak di def lu baax, donte ñenn ci nit ñi da ñuy foog lu wuuteek loolu