عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«اللهُمَّ أَصْلِحْ لِي دِينِي الَّذِي هُوَ عِصْمَةُ أَمْرِي، وَأَصْلِحْ لِي دُنْيَايَ الَّتِي فِيهَا مَعَاشِي، وَأَصْلِحْ لِي آخِرَتِي الَّتِي فِيهَا مَعَادِي، وَاجْعَلِ الْحَيَاةَ زِيَادَةً لِي فِي كُلِّ خَيْرٍ، وَاجْعَلِ الْمَوْتَ رَاحَةً لِي مِنْ كُلِّ شَرٍّ».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na wax:
"Allaahuma aslih lii diinii allasii huwa hismatu amrii, wa aslih lii dunyaaya allatii fiihaa mahaasii, wa aslih lii aaxiratii allatii fiihaa mahaadii, wajhal alhayaata siyaadatan lii fii kulli xayrk , wajhal almawta raahatan lii min kulli sarrin".

Wér na Muslim soloo na ko Téere Muslim bi gën a wér - 2720

Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaan ñaan goo xam ne dafa boole cosaani teddngay jikkó yi nga xam ne dañu ko a yónni ngir mu mottali ko; te mooy yéwénug diine , ak àdduna, ak allaaxira, mu sàkku ci kàddu yu tënku yii yéwénug mbooleem ñatt yii, mu tàmbalee ci yéwénug diine, te ci la yéwénug nekkiinu ñaari kër yi nekk, mu wah ne:
(yaw Yàlla sama Boroom yéwénalal ma sama diine) ci dëppale ma may taxawe ay tegginam ca anam ga gën a mat.
(moom mi nekk sama kaaràngey mbir) mooy aji-sàmm samay bir yépp, bu sama diine yàqoo sama bir yëpp yàqu, ma sooy daal di ñàkk, ndaxte yéwénug diine ja nu sàkku du mat ci lu dul yëwénug àdduna, mu wax ne:
(yéwénalal ma sama àdduna) ci jox ma wér gi yaram ak jàmm, ak wërsëg, ak jabar ju baax, ak doom yu sell ak lépp lu ma aajowoo, te mu nekk lu dagan, lu may dimbali ci topp la, topp mu tudd ngànt li tax waral muy ñaan yéwénam; ci wax ne:
(moom mi nga xam ne ci la samag dund nekk) ak sama barabu dund ak ci jamano jimay dund.
(te nga yéwénal ma sama allaaxira ji nga xam ne mooy sama delluwaay) samag dellu jëm ci daje ak yaw te loolu moo ngi ci yéwénug jëf yi, ak tawfeexalug Yàlla ñeel jaamam bi cig jaamu ak ug sellal, ak rafetug mujj.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc toftal ci allaaxira ginnaaw àdduna; ndax àdduna mooy jumtukaay biy tax allaaxira jag, ku jub ci àddunaam kem ni ko Yàlla bëgge, allaaxiraam jub ñeel ko mu texe fa.
(defal dund gi) ak gudd fan (ag dolliku ci wépp yiw) ma barile ci ay jëf yu baax, (defal dee gi) ak ug gaawam (ag nooflaay ci wépp ay) ak fitna ak nattu ci bàkkaar yi ak càggante, ak ug mucc ci coonay àdduna ak i jafe-jafeem, ak am ug nooflaay.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

  1. Diine moo gën a am solo lépp; loolu a tax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tàmbalee ko ci ñaan gi.
  2. Diine kaarànge la ñeel nit ki moo koy tere lépp lu bon.
  3. Ñaan ci mbiri àdduna yi ngir yéwénal diine ak allaaxira.
  4. Sibuñu mébét dee ngir ragal fitna ci diine, walla ñaan Yàlla dee ci sahaada.

Gaaral firi yi

51 Làkk wi
EN English الإنجليزية
UR اردو الأوردية
ES Español الإسبانية
ID Indonesia الإندونيسية
UG ئۇيغۇرچە الأيغورية
BN বাংলা البنغالية
TR Türkçe التركية
RU Русский الروسية
BS Bosanski البوسنية
SI සිංහල السنهالية
HI हिन्दी الهندية
ZH 中文 الصينية
FA فارسی الفارسية
VI Tiếng Việt الفيتنامية
TL Tagalog تجالوج
KU Kurdî الكردية
HA Hausa الهوسا
PT Português البرتغالية
ML മലയാളം المليالم
TE తెలుగు التلغو
SW Kiswahili السواحيلية
TA தமிழ் التاميلية
MY မြန်မာ البورمية
TH ไทย التايلندية
DE Deutsch الألمانية
PS پښتو بشتو
AS অসমীয়া الأسامية
SQ Shqip الألبانية
SV Svenska السويدية
AM አማርኛ الأمهرية
NL Nederlands الهولندية
GU ગુજરાતી الغوجاراتية
KY Кыргызча القيرقيزية
NE नेपाली النيبالية
LT Lietuvių الليتوانية
PRS دری الدرية
SR Српски الصربية
TG тоҷикӣ الطاجيكية
RW Kinyarwanda الكينياروندا
RO Română الرومانية
HU Magyar المجرية
MOS Moore الموري
MG Malagasy المالاجاشية
OM Oromoo الأورومو
KN ಕನ್ನಡ الكانادا
UK Українська الأوكرانية
KA ქართული الجورجية
MK Македонски المقدونية
KM ភាសាខ្មែរ الخميرية
PA ਪੰਜਾਬੀ البنجابية
MR मराठी الماراثية