عَنْ أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«الدُّعَاءُ لاَ يُرَدُّ بَيْنَ الأَذَانِ وَالإِقَامَةِ».
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي والنسائي] - [سنن الترمذي: 212]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«ñaan deesu ko delloo ci diggante nodd ak liqaam».
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 212]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ngëneelu ñaan ci diggante nodd ak liqaam, ci ne deesu ko delloo te yeyoo na ñu nangu ko, deeleen ci ñaan Yàlla.