عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«أَيُّهَا النَّاسُ، إِنَّ اللهَ طَيِّبٌ لَا يَقْبَلُ إِلَّا طَيِّبًا، وَإِنَّ اللهَ أَمَرَ الْمُؤْمِنِينَ بِمَا أَمَرَ بِهِ الْمُرْسَلِينَ، فَقَالَ: {يَا أَيُّهَا الرُّسُلُ كُلُوا مِنَ الطَّيِّبَاتِ وَاعْمَلُوا صَالِحًا، إِنِّي بِمَا تَعْمَلُونَ عَلِيمٌ} [المؤمنون: 51] وَقَالَ: {يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا كُلُوا مِنْ طَيِّبَاتِ مَا رَزَقْنَاكُمْ} [البقرة: 172] ثُمَّ ذَكَرَ الرَّجُلَ يُطِيلُ السَّفَرَ أَشْعَثَ أَغْبَرَ، يَمُدُّ يَدَيْهِ إِلَى السَّمَاءِ: يَا رَبِّ، يَا رَبِّ، وَمَطْعَمُهُ حَرَامٌ، وَمَشْرَبُهُ حَرَامٌ، وَمَلْبَسُهُ حَرَامٌ، وَغُذِيَ بِالْحَرَامِ، فَأَنَّى يُسْتَجَابُ لِذَلِكَ؟».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 1015]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«yéen nit ñi, Yàlla ku teey la te du nangu lu dul lu teey, te Yàlla dafa digal way-gëm ñi li mu digal Yonnente yi, mu wax ne: {yéen Yonnente yi lekkleen ci yu teey yi te ngeen jëf lu baax, man de Aji-Xam laa lépp lu ngeen di def} [Al-Muuminuuna: 51] mu wax it ne: {yéen ñi gëm lekkleen ci yu teey yi nu leen wërsëgal} [Al-Baqara: 172] topp mu daal di tudd benn waay bu nekk ci tukki bu sori, kawar ga jaxasoo, mu pënd lool, ma nga tàllal ay loxoom jëme kaw asamaan, di wax naan: yaw sama Boroom, te li muy lekk dafa araam, li muy naan dafa araam, li mu sol dafa araam, li ñu ko dundale itam dafa araam, moo naka lees koy nangule ñaanam?!»
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1015]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne Yàlla ku teey la ku Sell la ku set la walis muy nekk ku am
dara ci wàññiku
walla ay ayib ku melowoo ag mat la, te du nangu ci jëf yi ak wax yi ak pas-pas yi lu dul lu teey, te mooy la sell ñeel Yàlla, la dëppoo ak njubug Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, te du jaadu ñuy jegeñ-jegeñlu Yàlla ci lu dul loolu, bokk na ci yi gën a màgg yu sellug jëf di ame ñeel aji-gëm ji mooy lekkam teey, nekk lu dagan, ci loolu la jëfam di selle, loolu a tax Yàlla digal way-gëm ñi li mu digal Yonnente yi ci lekk lu dagan ak def lu baax, mu wax ne: yéen Yonnente yi lekkleen ci yu teey yi te def lu baax man de Aji-Xam laa lépp lu ngeen di def} wax it ne: {yéen way-gëm yi lekkleen ci yu teey yi nu leen wërsëgal}.
Topp Yonnente bi moytandikuloo lekk lu araam gi nga xam ne day yàq jëf di tere ñu nangu ko ak lu mu man a def sabab yiy tax nu nangu ko ci li feeñ; bokk na ca:
Bi ci njëkk: guddal ab tukki ci anami jaamu yi niki aj ak jihaad ak jokk mbokk ak yeneen.
Ñaareel bi: Ku kawar gu tasaaroo ngir ñàkk ko a peñe, melo wi soppeeku ak melow yéreem ndax suuf si, mu nekk ku loru.
Ñatteel bi: yëkkëti ñaari loxoom jëme asamaan di ñaan.
Ñenteel bi: tinu jëm ci Yàlla ci ay turam daal di taxaw temm ci loolu naan: yaw sama Boroom, yaw sama Boroom!
Ànd ak sababi nangu ñaan yii deesu ko nangul; ndaxte lekkam ak naanam ak colam dafa araam, ñu dundale ko lu araam, te sori na lool ñuy nangul ku mel nii, kon naka lañu koy nangule?!