عَنْ أَبِي مُوسَى رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«إِنَّ اللهَ عَزَّ وَجَلَّ يَبْسُطُ يَدَهُ بِاللَّيْلِ لِيَتُوبَ مُسِيءُ النَّهَارِ، وَيَبْسُطُ يَدَهُ بِالنَّهَارِ لِيَتُوبَ مُسِيءُ اللَّيْلِ، حَتَّى تَطْلُعَ الشَّمْسُ مِنْ مَغْرِبِهَا».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2759]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Yàlla mu màgg mi day tàllal loxoom ci guddi gi ngir ki doon def ñaawteef ci bëccëg gi tuub, di tàllal loxoom ci bëccëg gi ngir ki doon def ñaawteef ci guddi gi tuub, ba baa jant bi di fenke ci sowwu bi.
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2759]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne: Yàlla day nangu tuub ci jaamam yi, Bu jaam bi defee bàkkaar ci bëccëg bi tuub ko ci guddi gi Yàlla day nangu ag tuubam, bu defee bàkkaar ci guddi gi tuub ko ci bëccëg gi Yàlla day nangu ag tuubam, Yàlla mu sell mi it day tàllal loxoom kiy tuub, ngir bég ci loolu, ak ngir nangu ko, te buntub tuub du deñ di nekk lu ñu ubbi ba baa jant bi di fenke ca sowwu ba ngir yégle jeexug àdduna, bu ca fenkee nag dañuy tëj buntub tuub.