عَن أَبي سَعِيدٍ الْخُدْرِيِّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ قَالَ: رَضِيتُ بِاللَّهِ رَبًّا، وَبِالْإِسْلَامِ دِينًا، وَبِمُحَمَّدٍ رَسُولًا، وَجَبَتْ لَهُ الْجَنَّةُ».
[صحيح] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 1529]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Sahiid Al-Xudrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ku wax: radiiitu bil-Laahi Rabban, wa bi Muhammadin Rasuulan, àjjana war na ci moom".
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 1529]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku wax: gërëm naa Yàlla muy sama Boroom di Aji-Moom ji di Sang bi di Aji-Yéwénal ji, gërëm lislaam ci mbooleem ay àtteem ci ay digle ak i tere Muy sama diine ci pas-pas ak wommatul ko, gërëm Muhammat muy Yónenteem di ku ñu soloo; lépp lu ñu ko yónni mu jottali nu ko, lu dul ne àjjana war ci moom.