عَنِ المُغِيرَةِ بْنِ شُعْبَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لاَ يَزَالُ طَائِفَةٌ مِنْ أُمَّتِي ظَاهِرِينَ، حَتَّى يَأْتِيَهُمْ أَمْرُ اللَّهِ وَهُمْ ظَاهِرُونَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 7311]
المزيــد ...
Jële nañu ci Al-Muxiirata ibn Suhbata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"Ab kurel ci sama xeet wi du deñ di féete kaw, ba mbirum Yàlla di leen dikkal ñu nekk way-not".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 7311]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne aw nit ci xeetam wi duñu deñ di féete kaw di not ci kaw ñi wuute ak ñoom, noonu lay deme ba mbirum Yàlla di leen dikkal ci ñu jël seen ruu yi ci mujjug jamonoy àdduna njëkk Saa di taxaw.