عَنْ عَبْدِ اللهِ بْنِ مَسْعُودٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَيْسَ الْمُؤْمِنُ بِالطَّعَّانِ وَلاَ اللَّعَّانِ وَلاَ الفَاحِشِ وَلاَ البَذِيءِ».
[صحيح] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 1977]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«aji-gëm nekkul kiy jamaate, walla
kiy rëbbaate, mbaa kiy def ñaawteef, walla aji-bon lammiñ ji».
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 1977]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne bokkul ci mbiri aji-gëm ji gëmam mat muy ayibal nit ñi ci seeni askan, walla di baril ay saaga ak i rëbbaate mbaa ñaaw i jëf, walla ci wax ju amul kersa.