عَنْ أَنَسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ:
كُنْتُ سَاقِيَ القَوْمِ فِي مَنْزِلِ أَبِي طَلْحَةَ، وَكَانَ خَمْرُهُمْ يَوْمَئِذٍ الفَضِيخَ، فَأَمَرَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مُنَادِيًا يُنَادِي: أَلاَ إِنَّ الخَمْرَ قَدْ حُرِّمَتْ، قَالَ: فَقَالَ لِي أَبُو طَلْحَةَ: اخْرُجْ، فَأَهْرِقْهَا، فَخَرَجْتُ فَهَرَقْتُهَا، فَجَرَتْ فِي سِكَكِ المَدِينَةِ، فَقَالَ بَعْضُ القَوْمِ: قَدْ قُتِلَ قَوْمٌ وَهِيَ فِي بُطُونِهِمْ، فَأَنْزَلَ اللَّهُ: {لَيْسَ عَلَى الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ جُنَاحٌ فِيمَا طَعِمُوا} [المائدة: 93] الآيَةَ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2464]
المزيــد ...
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Maa doon nàndal nit ñi ci kër Abuu Talhata, seen sàngara si bis booba nekkoon lu ñu jaxase, Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digal ab wootekat muy woote naan: yégleen ne sàngara araamal nañu ko, nee na: Abuu Talhata ne ma: génnal nga tuur ko, ma génn tuur ko, mu taa ci mbeddi Madiina yi, am ñenn ñu wax ne: am na ñu faatu te fekk sàngara moo ngi ca seen biir ya, Yàlla wàcce: {Du nekk bàkkaar ca ña gëm tey sellal seen i jëf, la ñu masoon a ñam} [Al-Maa-ida: 93] ba aaya bi jeex.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2464]
Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne moom nekkoon na di nàndale sàngara ña nekkoon ca kër boroom këru yaayam Abuu Talhata yal na ko Yàlla dollee gërëm, sàngara sa njaxasu tàndarma ak meññet ma la woon, fa saasa rekk kiy wooteel Yonente Yàlla bi di woote naan: yégleen ne sàngara araamal nañu ko, nee na Abuu Talhata ne ma: génnal nga sotti ko tuur ko, ma génn sotti ko tuur ko, sàngara si di daw ci mbeddi Madiina yi, ñenn ci nit ñi ne: ray nañu yenn Sahaaba yi njëkk ñu koy araamal fekk moo nga ca seen biir ya, Yàlla daal di wàcce:
{Du nekk bàkkaar ca ña gëm tey sellal seen i jëf, la ñu masoon a ñam} [Al-Maa-ida: 93] ba aaya bi jeex. Maanaam ñi faatu tey way-gëm amuñu bàkkaar ca la ñu lekkoon naanoon ko ci sàngara njëkk ñu koy araamal.