عن ابن عمر رضي الله عنهما قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«كل مُسْكِرٍ خَمْرٌ، وكل مُسْكِرٍ حرام، ومن شرِب الخمر في الدنيا فمات وهو يُدْمِنُهَا لَمْ يَتُبْ، لَمْ يَشْرَبْهَا في الآخرة».
[صحيح] - [رواه مسلم وأخرج البخاري الجملة الأخيرة منه] - [صحيح مسلم: 2003]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«lépp luy màndiloo sàngara la, te lépp luy màndiloo dafa araam, te kuy naan sàngara ci àdduna ba dee fekk ne tàmm na ko te tuubu ko, kooku du ko naan ca allaaxira».
[Wér na] - - [Téere Muslim bi gën a wér - 2003]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral na ne lépp luy yóbbu xel di ko dindi loolu sàngara la suy màndiloo moo xam lu ñuy naan la walla lu ñuy lekk walla lu ñuy xeeñju walla lu dul loolu, ak ne lépp luy màndiloo di yóbbu am xel loolu Yàlla araamal na ko tere ko, moo xam mu néew walla mu bari. Ak ne képp ku naan benn xeet ci yooyu di màndiloo, sax ci di ko naan te tuubu ko ba faatu; kooku yeyoo na mbugalum Yàlla ci mu xañ ko ba du ko naan ca àjjana.