عن أنس رضي الله عنه أن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«جَاهِدُوا المشركين بأموالكم وأنفسكم وألسنتكم».
[صحيح] - [رواه أبو داود والنسائي وأحمد] - [سنن أبي داود: 2504]
المزيــد ...
Jële nañu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«jihaadleen ak bokkaalekat yi ci seen alal ak seen bakkan ak seen làmmeñ».
[Wér na] - - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 2504]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na ñu jihaad ak yéefar yi ak def lu ñu man ci jàmmaarlook ñoom ci bépp jumtukaay ngir kàddug Yàlla di gën a kawe, te bokk na ci loolu:
Bi ci njëkk: joxe alal ci jihaad leen; ci jënn ngànnaay, ak ub dund ci jihaadkat yi ak yu ko niru.
Ñaareel bi: jël sa bakkan ak sa yaram génn ngir daje ak ñoom xeex ak ñoom.
Ñatteel bi: woo leen jëme ci diine ji ci làmmeñ, ak taxawal lay ci seen kaw, ak jàjji leen delloo seen i lay.