عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ قَتَلَ مُعَاهَدًا ‌لَمْ ‌يَرَحْ ‌رَائِحَةَ الْجَنَّةِ، وَإِنَّ رِيحَهَا تُوجَدُ مِنْ مَسِيرَةِ أَرْبَعِينَ عَامًا».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 3166]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"Ku ray koo séqal kóllëre, du xeeñcu xetug Àjjana, te dinanteem ak xetam ga soree ni doxub ñent-fukki at".

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3166]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral tëkku gu tar gi ñuy tëkku ku ray boroom kollëre -te mooy yéefar bu dugg ci biir réewum jullit ci kollëre ak kaaraange- ci ne du xeeñcu xetug àjjana, te xetam ga dana soree ni doxub ñent-fukki at.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Araamal nañu ray boroom kollëre ak yéefar biy fay ay wareefam, ak yéefar buñu làq , te loolu ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
  2. Boroom kollëre: mooy yéefar buñu jël ci moom kóllëre mu nekk ci dëkku jullit ñi, te du xeex jullit ñi ñoom itam duñu ko xeex, yéefa biy fay: mooy ki dëkk ci dëkku jullit ñi di fay juuti, ki ñu làq: mooy ku dugg ci kër jullit ñi ci kóllëre ak kaaraange ci ab diir buñu tënk.
  3. Wattandikuloo wor kóllëre ak ñi dul ay ajullit.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (58)
Ndollent