Toftaleg Adiis yi

Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp
عربي Àngale Urdu
lépp luy màndiloo sàngara la, te lépp luy màndiloo dafa araam, te kuy naan sàngara ci àdduna ba dee fekk ne tàmm na ko te tuubu ko, kooku du ko naan ca allaaxira
عربي Àngale Urdu
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tabaskee na ñaari kuuy yu duuf am ay béjjan, mu rendi leen ci loxoom, tudd Yàlla daal di kàbbar, teg tànkam bi ca seen doq ya
عربي Àngale Urdu
Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm
عربي Àngale Urdu
Tere na lépp lu am bëñ ci negment yi, ak lépp lu am aw sàll ci ñanaaw yi
عربي Àngale Urdu