عَنْ ابنِ عُمَرَ رَضيَ اللهُ عنهما عَنْ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنِ اقْتَنَى كَلْبًا إِلَّا كَلْبَ ضَارٍ أَوْ مَاشِيَةٍ نَقَصَ مِنْ عَمَلِهِ كُلَّ يَوْمٍ قِيرَاطَانِ»، قَالَ سَالِمٌ: وَكَانَ أَبُو هُرَيْرَةَ يَقُولُ: «أَوْ كَلْبَ حَرْثٍ»، وَكَانَ صَاحِبَ حَرْثٍ.  
                        
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1574]
                        
 المزيــد ... 
                    
Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ku yar ab xaj bu dul xaju rëbb walla xaju sàmm wàññi na ci jëfam bis bu nekk Xiiraat", Saalim ne: Abuu Hurayrata daan na wax: "walla xaju mbay", moom baykat la woon. 
                                                     
                                                                                                    
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1574]                                            
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo la yar xaj, lu dul ngir aajoy rëbb, walla gaarde jur gi ak mbay mi, ku ko yar ngir lu dul loolu wàññi na ci yoolu jëfam bis bu nekk Xiraat; loo lu ag natt la gog Yàlla moo ko xam.