عَنْ أَبِي بُرْدَةَ الْأَنْصَارِيِّ رَضيَ اللهُ عنهُ أَنَّهُ سَمِعَ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«لَا يُجْلَدُ أَحَدٌ فَوْقَ عَشَرَةِ أَسْوَاطٍ إِلَّا فِي حَدٍّ مِنْ حُدُودِ اللهِ».  
                        
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1708]
                        
 المزيــد ... 
                    
Jële nañu ci Abii Burdata Al-Ansaarii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne dégg na Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"deesul dóor kenn lu ëpp fukki yar lu dul ci daani Yàlla". 
                                                     
                                                                                                    
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1708]                                            
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ñiy dóor kenn lu ëpp fukki yar lu dul ci moy yi, waaye jubluwuñu ci li rot jóge ci Aji-Yoonal ji ci lim yi ñu tënk ci caw walla dóor walla mbugal yi ñu jagleel, li ñu ci jublu mooy deesul dolli ci dóoru yo xam ne ngir yare la lu ëpp fukki yar, niki caw sox na ak doom.