+ -

عَنِ ابْنِ عَبَّاسٍ رضي الله عنهما قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا يَنْظُرُ اللهُ إِلَى رَجُلٍ أَتَى رَجُلًا أَوِ امْرَأَةً فِي دُبُرٍ».

[صحيح] - [رواه الترمذي والنسائي في الكبرى] - [السنن الكبرى للنسائي: 8952]
المزيــد ...

Jële nañu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"Yàlla du xool góor giy dikke soxnaam ci ginnaawam".

[Wér na] - - [Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi - 8952]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na tëkku gu tar ci ne Yàlla du xool xoolu yërmànde jëm ci góor gir sëy ak góor ci ginnaawam walla jigéen ci ginnaawam, ak ne loolu dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Amhari Olànd Gujarati Nipali
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Góor dikke góor -te mooy ag ngóor-jigéen- dafa bokk ci bàkkaar yu mag yi.
  2. Sëy ak jigéen ci ginnaawam ci bàkkaar yu mag yi la bokk.
  3. (Yàlla du xool) maanaam xoolu yërmànde ak ñeewant, waaye jubluwuñu ci xool yépp; ndaxte Yàlla nu Sell mi te kawe dara nëbbuwu ko, te dara fàdduwul woli gisam.
  4. Jëf yii dafa bokk ci ñaawteef yi màgg yi te di kaawteef ci kaw nit ñi; ndax li ci nekk ci wuute ak selluk nit ku mucc, ak nëewal njaboot, ak yàq dundug sëy gi, ak jëmbët noonoo ak mbañeel, ak tàbbi ci bérab yu salte yi.
Ndollent