+ -

عن أبي موسى الأشعري رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«مَنْ حَمَلَ عَلَيْنَا السِّلَاحَ فَلَيْسَ مِنَّا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 7071]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 7071]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di gàddu ngànnaay ci kaw jullit ñi, ngir ragal loo leen, walla siif leen, ku def loolu ci lu dul yoon, kon toggoo na ag tooñ gu rëy, ak bàkkaar bu mag, te yayoo na tëkku gu tar gii.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Àrtu gu tar ci jullit di rayante ak mbokki jollitam.
  2. Bokk na ci ñaawtéef ak yàq yi gën a rëy ci kaw suuf bocci gànnaay ci kaw jullit ñi, ak di yàq ci raye.
  3. Tëkku googu ñu tudd du làmboo rayante ci dëgg, niki rayante ak way-bew yi, ak yàqkat yi ak ñu mel ni ñoom.
  4. Araamal nañu tiital jullit ñi ci gànnaay mbaa leneen, -doonte sax ci anamug fo la-.