عَنْ أَبِي ذَرٍّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّهُ سَمِعَ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«لاَ يَرْمِي رَجُلٌ رَجُلًا بِالفُسُوقِ، وَلاَ يَرْمِيهِ بِالكُفْرِ، إِلَّا ارْتَدَّتْ عَلَيْهِ، إِنْ لَمْ يَكُنْ صَاحِبُهُ كَذَلِكَ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6045]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Sarr yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne dégg na Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«nit du jiiñ moroomam ag kàccoore, walla ag kéefar, lu dul ne dana dellusi ci moom, budee kooku melul noona».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6045]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day àrtu ñuy wax keneen: yaw kàccoor nga, walla: yaw yéefar nga, bu dee nekkul li mu wax, kon moom mooy yayoo melo wi mu tudd waxam ji dellusi ci moom, bu dee li mu wax noonu la kon du dellusi ci moom; ndax li mu wax dëgg.