+ -

عن عائشة رضي الله عنها قالت:
كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَذْكُرُ اللهَ عَلَى كُلِّ أَحْيَانِهِ.

[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 373]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan tudd Yàlla ci bépp jamono.

[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 373]

Leeral

Aysatu yaayu way-gëm ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xéroon lool ci tudd Yàlla mu kawe mi, ak ne daa na tudd Yàlla ci bépp jamono ak bérab ak anam.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sàrtaluñu ci tudd Yàlla laab ci toj gu ndaw mbaa toj gu mag.
  2. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa saxoon ci tudd Yàlla .
  3. Ñaaxe ci tudd Yàlla mu kawe mi lu bari ci bépp jamono ngir roy ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, lu dul ci anam yi ñuy tere ku ci tudd Yàlla, niki jamanoy faj aajo.
Ndollent